Aller au contenu

Oseyaani

Jóge Wikipedia.
Lonkoyoon buy wone Oseyaani ci àdduna bi

Oseyaani ab gox la bu nekk ci Mbàmbulaan gu Dal gi. Ci biiram Óstraali, ak Seland-Gu-Bees gi, ak Papuwasi-Ginne-Gu-Bees gi, Tasmaani, ak yeneeni dun. Oseyaani mooy gox bi gën a tuuti.

Ci lu daj Oseyaani dañ koy jàppee ni ab gox bu nekk ci diggante Bëj-saalum-penku Asi ak Bëj-saalumu Aamerik.

Oseyaani mooy gox bi gën a tuuti ci gox yi ci àdduna bi, ci 8 523 655 km kaare lay tollu, te 90% ya Óstraali la, 5,4 % ya di Papuwasi-Ginne-Gu-Bees, 3,1% ya di Seland-Gu-Bees gi, yeneen réew-réewaan yi tas ci Mbàmbulaan gu Dal gi doon 1,5 ci gox bépp.

Am na 32 642 390 ciy way dëkk di ñareelu gox bi gën a néew ay nit lu weesu Dottu Bëj-gànnaar bi. 60% ya Óstraali la ñu dëkk, 16% ya Seland-Gu-Bees gi, 12% ya Papuwasi-Ginne-Gu-Bees.

Ni yeneen gox yépp, ay peggan ci deggoo rekk lañ leen daggee. Baatu Oseyaani dañ koy jëfandikoo ngir jëmmal ab xaaj ci àdduna bi bu ëmb bépp suuf su nekk ci Mbàmbulaan gu Dal gi te duggoo ci barabi dott bi.

Ci lu ëpp yii la ñuy jàpp ne ñooy ay Diwaanam:

Ki defoon bi seddale moo doonoon Jules Dumont d'Uville ci 1831, waaye tegu woon ci cëslaayu xam-xam gu ñu ñangu tay. Ci 1970 ba tay, séwógaraafikat yi, Gëstukatu-làkk yi, ak yeneen boroom xam-xam, ci seeniy liggéey, yii rekk la'ñ koy seddalee Oseyaani gu Jege ak Oseyaani gu Sori.

Rèew ak suuf

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lu ëpp ci réewi Oseyaani yi, ay dun la ñu. Mennum Óstraali ak Papuwasi-Ginne-Gu-Bees ñoo am ay peggu suuf ak yeneen réew (Ci Dunu Ginne gu Bees gi ak Endonesi gi ñuy boole wàllam gu bari ci Oseyaani).

Lim bii di toftal dafa boole mbooleem réew aki suuf yi fa nekk. Te jàpp nak ne am na ay suuf yu fa ne te ñu jàppee leeni réew, waaye tembu ñun kon ay réew la ñu ci biiri réew, di nan bind ci réew mi ñu bokk ci wet gi.

Réew yu temb yi

Rèew ak Suuf yu tembul

Goxi / Kembaari àdduna si
Afritugalasi Oseyaani Afrig Tugalasi
Bëj-gànnaaru Aamerig Tugal Asi Bëj-saalumu Aamerig