Aller au contenu

Koor

Jóge Wikipedia.
Sumbu 15 Ut 2023 à 20:14, bu: WikiBayer (waxtaancëru) (Reverted edits by 176.33.67.202 (talk) to last version by Trey314159: unnecessary links or spam)
(wuute) ← Sumb bi jiitu • Sumb bi teew (wuute) • Sumb bi toftal → (wuute)

Koor mooy juroom ñenteelu weer ci arminaatu jullit ñi. Weer wii mooy ndoorteelu wàccug Alxuraan ci suuf. Bokk na ci li tax jullit ñi di ko woor: magal ko. Woor Benn la ci ponki Lislaam yi.

Moom nag am na fukk ciy ne-ne (matière):

Xamle luy koor, taariixu ag farataalam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xamle luy koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Koor ci làkk : bañ a lekk, bañ a naan.

Bu dee ci sariiya nag : bañ a lekk, bañ a naan, bañ a séy, bàyyi it mbooleem yiy dogloo la ko dale ca penkug fajar, ba ca sowug jant bi, ngir nag yéenee jaamu Yàlla.

Taariixu ag farataal koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yàlla (t.s) moo farataal koor ci Muhammad (j.m) , niki mu ko farataale ca xeet ya ko fi jiitu woon ca waxam ju tedd ja: «Yéen ñi gëm, farataal nañu ci yéen koor, ni ñu ko farataale ca ña léen jiitu, ndax ngéen am ag ragal Yàlla»

Loolu di woon ci bisub altine ci weeru baraxlu, ci ñaareelu at ci gàddaay gu barkeel gi( juge Màkka dem Madiina)

Ngënéelul koor aki njariñam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ngënéelam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ramadaan am na ay ngënéel yu màgg te bari, yu yeneen weer yi amul, àddiis yiy saxal loolu te di ko feddali yu bari lañu : Waxam ja (j.m) : «Julli yi juroom, àjjuma ba àjjumawaat, ramadaan ba ramadaanati, dana ñu far bàkkaar yi nekk ci séen diggante, bu ñu teetee bàkkaar yu mag yi».

Waxam ja (j.m) : «Ku woor ramadaan ngirug gëm ak sàkku tuyaaba, jéggalees ko li jiitu ciy bàkkaaram».

Yonnant bi (j.m) wax na ne : «Gis naa waa ju bokk ci sama xeet wi muy yalgat ngir mar, déeg bum dem ñu aaye ko ko, koorug ramadaan dikk wëgg ko, nàndal ko».

Waxam ja (j.m) : «Guddi gi njëkk ci ramadaan bu jotee, dañuy jéng saytaane ak way féttéerluy jinne yi, tëj bunti sawara, du ñu ci ubbi benn, ubbi bunti àjjana, du ñu ci tëj benn, bu ko defee aji woote, woote ne: yaw miy sàkkuw yiw dikkal, yaw miy sàkku ay dëppal, Yàlla am na ñu ñu goreel ci sawara, te loolu guddi gu nekk lay doon».

Waxam ja (j.m): «Koor de pakk la bu lay fegal sawara, ni pakk di fege boroom cib xare».

Waxam ja mu nee (j.m): «Ku woor ab bis ngir Yàlla (t.s) Yàlla dana soril jëmm ja sawara lu tollook juroom ñaar-fukki nawet ngir bis boobee».

Waxam ja (j.m): «Ki woor de bu dogee lu mu ñaan Yàlla may ko ko»

Waxam ja (j.m) : «Àjjana am na bunt bu ñu naan Rayyaan, ku dul ñi woor duñu ca jaar, bu ko defee ñu ne: ana ñi wooroon, ñu daal di dikk, ku dul ñoom nag du dugg, bu ñu duggee it ba noppi ñu tëj bunt ba, keneen du dugg»

ay njariñam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Koor am na ay njariñ yu ruu, yu mboolaay ak yu wér-gu-yaram ñooy:

  • Bokk na ci njariñi ruu yu koor yi : moom day tax nga man a muñ, taggate ci, di tax it nit ki di wattoonteek bakkanam ak a jiyaar ak bànneexam, di jur ci bakkan ag ragal Yàlla te di ko ci suuxat, rawati na ragal Yàlla gi nga xam ne mooy sabab su mag si tax ñuy woor, moom la Yàlla (t.s) di firndéel ca laaya ba, ba mu naan : «Farataal nañu ci yéen koor, ni ñu ko farataale ca ña léen jiitu, ndax ngéen am ag ragal Yàlla»

Bokk na ci njariñi mboolaay yu koor yi : day indi ag nosu ci xeet wi akug bennoo, bëgg ag maandute akug yamoo, dana sos tam ci jullit ñi ag ñeewant, yërmaande, di joxe it jikkoy ihsaan (rafetal), dina feg mboolaay gi it (la société) ci ñaawtéef yi ak bon-boni jikko yi.

  • Bokk na ci njariñi wér-gu-yaram yu koor yi : moom (koor) day setal ay butiit, di defar ag mbàq, di setal yaram wi ci desiit yu bon yi ak diigiit yi , di wàññi aw yaram, di néewal gariis gi ci yaram. Adiis ba nee na : “ woor-leen, wer”

Ñatteelu ne-ne bi : ci li ñu sopp ci koor, li ñu ci sib, li ñu ci araamal :

Li ñu sopp ci koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sopp nañu woor bis yii :

1- Bisub Arafa, ci ku ajul, mooy juroom ñeenteelu dil-hijja, ngir waxi Yonnant bi (j.m): «Woor bisub Arafa dina far bàkkaari ñaari at, ma jàll ak may jublusi. Woor bisub fukkeel ba di Aasoora nag moom day far bàkkaari at ma wéy».

2- Bisub Asoora ak Taasooha, ñooy bisub juroom ñeenteel ak bu fukkeel ci weeru muharram, ngir waxam ja (j.m) : «Woor bisub Aasoora dina far bàkkaari at mu jàll», ni mu woore moom Yonnant bi (j.m) bisub Aasoora te digale ñu woor ko, ne : “déwén bu neexee Yàlla dinañu woor Taasooha (bisub juroom ñeenteel ba)”

3- Juroom benni fan ci sawaal , ngir waxam ja (j.m) : «Ku woor ramadaan teg ca juroom benni fan ci sawaal, mel na ni ku woor diirub jamono».

4- Xaaj bu njëkk bi ci weeru baraxlu, ngir waxi Soxna Aysa (y.y.g) ja : «Masumaa gis Yonnant bi (j.m) mu woor mukk weeru lëmm wu dul wu koor wi, masuma koo gis it mu woor ciw weer lu ëpp li muy woor ci baraxlu».

5- Fukki fan yu njëkk yi ci dil-hijja, ngir waxam ja (j.m) : «Amul yenn bis yu Yàlla gën a soppe ay jëf yu rafetet ci bis yii: maanaam fukki fan yu njëkk yi ci dil-hijja, ñu ne ko yaw Yonnantub Yàlla bi, xanaa jiyaar kay ci yoonu Yàlla moo gën a rëy yooyu bis? mu ne dée-déet, lu dul waa ju génn ci jëmmam ak alalam ci yoonu Yàlla, te delloosiwaatul dara» .

6- Weeru muharram, ngir waxam ja (j.m) ba ñu ko laajee: «Gan koor a gën ginnaaw ramadaan?» Mu ne : weeru «Yàlla wi ngéen di tudde muharram».

7- Bis yu weex yi ci weer wu nekk, ñooy: fukk ak ñatt, fukk ak ñeent, fukk ak juroom, ngir waxi Abuu Darin ji (y.y.g) : «Yonnant bi (j.m) digal na nu nu woor ci weer wi ñatti fan yu weex yi : fukk ak ñatteeel; fukk ak ñeenteel; fukk ak juroomeel». Mu ne : «Ñoom de ñook woor diirub jamonoo yam».

8- Bisub altine ak bob alximis, ngir li ñu nettali ne li ëpp ci li Yonnant bi (j.m) daa woor mooy bisub altine ak bu alximis, ñu laaj ko ko mu ne: «Jëf yi dees leen di gaaral altine ju nekk ak alximis, bu ko defee Yàlla di jéggal jullit bu nekk walla aji gëm ju nekk, ndare ñaari way tóngóo yi, mu ne nañu leen mujje»

9- Woor bis, wori bis, ngir waxam ja (j.m) : “ wooriin wi Yàlla gën a sopp mooy wi Daawuuda daa def (j.m), julliwiin wi Yàlla gën a sopp mooy wu Daawuuda , da daan nelaw benn xaaj ba , taxaw benn ñatteel ba , di nelaw juroom benneel ba. Daan na woor it benn fan, wori ba ca des”

10- Woor ci ki yorul jabar, te manul a denc , ngir waxam ja (j.m) : «ku ci toll ci denc, na wut jabar, moo la gën a man a tee xool jigéen ñi, gën laa musal ci njaalo, ku ko manul nag nay woor, (moom koor gi) ag tàpp la ci moom». Al-buxaari moo ko soloo.

Li ñu sib ci koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

1- woor bisu Arafa ci ku fa taxaw, ngir tere gi ko Yonnant bi (j.m) tere ci ku fa nekk.

2 – ber bisub àjjuma woor ko, ngir waxam ja (j.m) : « bisub àjjuma séenug iid la buleen ko woor, ndare bu da ngéen a woor bis ba ko jiitu walla ba ca topp »

3 – ber bisub gàwwu woor ko, ngir waxam ja (j.m) : « Buleen wor bisub gàwwu bu dul farata ci yéen, bu waay amul lu dul xàncug reseñ it walla bantub garab na ko lekk »

4 – woor mujjug baraxlu ngir waxam ja (j.m) : « bu baraxlu xaajatee buleen woor »

Sibéelug woor fan yii sibéelug sellal la. Waaye lii di ñëw nag ag sibéelam, sibéelug araamal la:

1 – jokkale, mooy jokkale ñaari fan di ko woor walla lu ko ëpp ci lu dul dog ci diggante bi, ngir waxam ja (j.m) :«Buleen jokkale» ak waxam ja :«Moytuleen di jokkale».

2 – woor bisub sikk, mooy bisub fanweer ci baraxlu, ngir waxam ja (j.m) : «Ku woor bisub sikk moy nga baayi Qaasim».

3 – woor diirub jamono, mooy woor at mépp ci lu dul dog ci, ngir waxi Yonnant bi (j.m) : «Ku woor diirub jamono, wooroo». ak waxam ja : «Ku woor diirub jamono wooroo, dogoo».

4 – koorug jigéen ci lu dul ndigalu boroom këram bu teew , ngir waxam ja (j.m) : «Bu jigéen woor benn bis te jëkkaram nekk fi, te joxu ko ci ndigal lu dul weeru koor».

Koor gu ñu araamal gi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mooy woor bis yii di ñëw :

1 – woor bisub iid, moo xam kori la walla tabaski, ngir waxi Omar ji (y.y.g), ñaar yii, bis lañu yu Yonnant bi (j.m) tere ku ci woor: «Bis bi ngéen di dog ci séenug koor ak bi ngéen di lekk ci séeni jaamu (séeni xari tabaski)»

2 – ñatti bisi tasriiq yi, ngir “Yonnant bi (j.m) dafa yónni woon ab yéenekat mu yéene ca Munaa ne buleen woor bis yii, ñoom de bisi lekk lañook naan ak séy” lafd am na ak tudd Yàlla.

3 – bisi mbërëg yi (gis baax) ak wësin, ndax ag daje am na ci ne koorug aji mbërëg walla aji wësin genn baaxu ci, ngir waxam ja (j.m) : «Ndax gisu leen ne bu mbërëgee du julli te du woor? loolu ci wàññikug seen diine la».

4 – koorug aji tawat ji ragal ag dee ci tawat ji bu wooree, ngir waxi Yàlla ji (t.s): «Buleen ray seen bopp, Yàlla de ku leen yëram la»

Warug woor weeru koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Woor weeru koor lu war la ci Alquraan ak Sunna ak dajeg xeet wi (ijmaahul umma), Yàlla nee na (t.s) : «Weeru koor wi nga xam ne ci lañu wàcce Alquraan muy ag njub ci nit ñi te di ay laaya yu leer yuy gindee tey tàqale dëgg ak fen, ku ci fekke weer wi na nga ko woor» ak waxi Yonnant bi (j.m) : «Lislaam ci juroom lañu ko tabax, seere ne Laa ilaaha illal laah, Muhammadun rasuulul laah, ku dul Yàlla du yàlla te Muhammad moo dib yonnantam, ak julli, natt asaka, aj Màkka ak woor weeru koor» ak waxam ja (j.m) : «buumi Lislaam ak ponki diine ñatt lañu ci lañu tabax Lislaam, ku ci bàyyi benn rekk yeefar nga, sa dereet dagan na : seere ne Yàlla rekk ay buur, ak julli giy farata, ak woor weeru koor».

Ngënéelul def lu baax ak njekk ci ramadaan

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ngir ngënéelul ramadaan, lépp lu ñu ciy def ci lu baax day gën, bokk na ci jëf yu baax yi ñu ci man a def :

1 – saraxe : Yonnant bi (j.m) nee na : « Gën ji saraxe mooy bi ñu def ci koor gi » waxati na (j.m) : « Ku jox aji woor lu mu doge am nga yool bu tollu ne kooram ga te loolu du wàññi cib yoolam dara » mu waxati « ku jox ndogu aji woor, mu diw ñam walla ag naan ci lu lew, malaaka yi danañu julli ci moom ci waxtuy weeru koor wi, Jibriil julli ci moom ci guddig Laylatul Qadr » moom (j.m) moo gënoon a tabe ci nit ñi, bu ramadaan jotee nag da daan gën a tabe bu ko Jibriil di dikkal

2 – taxaw guddi : ndax Yonnant bi (j.m) wax na : « ku taxaw ci ramadaan ngir gëm ak sàkku tuyaaba, jéggalees ko li jiitu ciy bàkkaaram » nekkoon na moom (j.m) di dundal guddiy ramadaan yi, bu fukki fan yu mujj ci koor gi masaan na jot da daan yee ñoñam, ak mépp mag mbaa ndaw lu man a julli

3 – jàng Alquraan ju tedd ji : ndax Yonnant bi (j.m) daan na baril jàng Alquraan ci weeru koor, Jibriil it daan na jànganteek moom Alquraan ci ramadaan , Yonnant bi daan na guddal njàngum Alquraan mi ci taxawaayi naafilay koor gi, nu ëpp ni mu ko daan defe ci lu dul ramadaan, Hudayfa mas naa julleek moom ag guddi, mu jàng saaru Bàqara, teg ca Aali Himraan ak Nisaayi, te daawul romb aw laayaw xuppe ndare bu da caa taxaw di ñaan, moo tax julliwul ñaari ràkkaa rekk dégg Bilaal muy nodd fajar. Loolu dikk na ci Sahiihayni. Wax na bat ay (j.m) : « koor ak taxaw danañu ramu jaam bi yawmal qiyaam, bu ko defee koor gi ñëw ne : boroom bi kii de tee naa koo lekk bëccëg tee koo naan, Alquraan ji ne : maa ko tee nelaw guddi kon tin ñu ci moom »

4 – lihtikaaf : mooy tàqook jàkka walla tëju fa di jaamu Yàlla (t.s), Yonnant bi (j.m) lihtikaaf na te daawul dañ di ko def ci fukki fan yu mujj yi ci ramadaan, ba Yàlla jëlle ko fi, looloo ngi ci Sahiihayni. Wax na (j.m) ne : « jàkka mooy neegub jépp aji ragal Yàlla, Yàlla warlul na képp ku jàkka di sab néeg, warlul na la ab noflaay ak yërmaande ak jéggi siraat dem ca gërëmam la, tàbbi ca àjjanaam ja »

5 – umra : mooy siyaareji Baytil Laahil Haraam, ngir wëri kaaba ga, ak doxi Safaa ak Marwa, ci ramadaan, ngir Yonnant bi nee na : « umra ci ramadaan mook aj ànd ak man a yam » waxaat na ba tay : « umra ba umra far na bàkkaari li nekk ci séen diggante »

Saxug weeru koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Duggug weeru koor ci ñaari mbir yii lay saxe: mbir mu njëkk mi mooy weer wi jiitu koor gi mat sëkk, mooy baraxlu, bu baraxlu matee fanweeri fan, bisub fanweer ak benneel ba mooy bis bi njëkk ci ramadaan ci lu dog. Mbir mi ci des mooy gis terute wi , bu ñu gisee terutew ramadaan ci guddig fanweer ci weeru baraxlu , kon weeru koor tàbbi na, woor ko war na ngir waxam ja (t.s) : Royuwaay:Ku ci gis weer wi na nga ko woor ak waxi Yonnant bi ji (j.m) : « bu ngéen gisee terute wi woorléen, bu ngéen ko gisee worileen, bu niiree ba manu leen koo gis(ak doonte feeñ na) mottalileen limu weer wi muy fanweeri fan » , dana doy ngir saxal ag gisam jenn aji maandu ne gis na ko walla ñaar . Ndax Yonnant bi (j.m) daganal na benn waay seere ne gis na terutew ramadaan . Bu dee nag korite jenn aji maandu du doy, ñaar ñooy baax, ndax Yonnant bi (j.m) daganalul gisug kenn ku maandu ci korite

Ku gis terutew koor war naa woor ak doonte nanguwuñu ag gisam, ku gis nag terutew kori te nanguwuñu ag gisam du wori, ngir waxam ja (j.m) : “koor mooy bis bi ngéen di woor, kori di bis bi ngéen di wori, tëbëski di bis bi ngéen di tëbëski”

Juroom ñaareelu ne-ne : ci sarti koor, ak àtteb koorug aji tukki, ku tawat, mag mu màggat, aji ëmb ak kuy nàmpal :

Sarti koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sart nañu ci warug kor gi ci jullit bi, mu am xel tey mukàllaf, ngir waxam ja (j.m) : “ xalima gi yékkatees na ko wëlif ñatt : wëlif ab dof ba kero muy dofadi, kuy nelaw ba kero muy yewwu, ak gone ba kero muy gent” bu dee jullit bu jigéen sart nañu ci werug kooram gi mu set ci dereeti mbërëg ak wësin, ngir waxam ja (j.m) ci leeral wàññikug diiney jigéen : “ndax du bu mbërëgee du julli du woor ?”

Ab juliit bu tukkee ci soriwaay bu ñuy wàññee julii, soriwaay boobu mooy tollook 48 miil, bu boobaa aji yoonal ji (di Yonnant bi) may na ko mu dog ci sartub mu fay ko bu dellusee, ngir waxam ja (t.s) : Royuwaay:Ku ci tawaw walla muy tukki, kon yeneen bis lay fay moom nag mu woor moo gën bu fekkee ne tukki di woor du ko sonal, bu ko dee sonal nag woree gën, ngir waxi Abii Sahiid Alxadarii ji (y.y.g) “ nekkoon nañu di xeex ànd ak Yonnant bi (j.m) ci weeru koor, am ñu ci woor, am ñu ci woorul, ki woor du tane ki woorul, ki woorul du tane ki woor, ñu gis ne ku am kàttan gu mu woore woor moo gën, ku ko amul it bañ a woor moo gën”

Bu jullit bi tawatee ci koor, day xool, bu manee woor ci lu dul ab coona bu tar day woor, bu ko manul mu dog, bu yaakaaree ne dana wér nag day xaar ba wér fay la ko faat, bu yaakaaree ne du wér mu dog tey saraxeel bis bu mu woorul ab mudd ciw ñam (maanaam ab loxo ba mu fees ak dugub) ngir waxam ja (t.s) : Royuwaay:Ñi ko man war na ñuy génne ag jot, muy ñam wu ñuy jox ab miskiin

Mag mu màggat

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ab jullit moo xam góor la, moo xam jigéen la, bu màggatee ba manut a woorati, day dog te saraxeel bis bu mu woorul mudd ciw ñam, ngir waxi Ibnu Abaas ji (y.y.g) : “may nañu mag mu màggat mu leel ab miskiin ci bépp bis bu mu woorul, te fay du ko war”

Aji ëmb ak kuy nàmpal

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bu fekkee jullit bi dafa ëmb te ragal bu wooree lor boppam mbaa mu lor li ci biiram, day dog, te bu wësinee mu fay. Su fekkee man na ko nag nay saraxe ci bepp bis bu muy fay lu tollook mudd ci dugub, loolu moo gën a mat te ëppub yool. Nii itam la kuy nàmpal di def, bu ragalee ci boppam ak ci doomam te amul ku ko nàmpalal walla doom ji nànguwul keneen ku dul moom. Àtte bii nag ñi ngi ko ball-loo ci waxam ja (t.s) : Royuwaay:Ñi ko man war na ñuy génne ag jot, muy ñam wu ñuy jox ab miskiin, maanaam (ñi ko man) mooy: ñi ko man ci coona bu tar, bu ñu woree fay walla ñu leel ab miskiin.

Ñaari yeete

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  1. Ku sàgganee fay koor gu mu waroon a fay ci lu dul ngànt ba geneen koor dellusi, war nay leel ab miskiin ci barabu bépp bis bu mu war a fay.
  2. Jullit bu faatu te waroon a fay ag koor, koor ga kilifaam a ko koy fayal, ngir waxam ja (j.m) : “ ku faatu te borub koor a ngi ci kawam, na ko ko kilifaam fayal” ak waxam ja ñeel ka ko laajoon ne ko: “ sama yaay dafa faatu te war naa fay aw weeru koor ndax dama ko koy fayal ?. Mu ne : waa-waaw, bor bu ñu yoreel Yàlla de moo gёn a yayoo ñu fay ko”

Ponki koor (ay farataam), ay sunnaam, yu ñu sibam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  1. yéene, mooy fas ci xol ne danga woor ngir topp ndigalul Yàlla (t.s), walla ngir jaamu ko, ngir waxam ja (j.m) : “ ku fanaanalul yéeney woor, amul koor” . Bu dee ngàttnga la nag moom dana baax ak doonte ginnaaw bu fajar fenkee la, bёccёg bi tàmbalee dugg, bu fekkee ne jotul woon a lekk dara, ngir waxi Soxna Aysa ji (y.y g) : «Yonnant bi (j.m) dugg na fi man bis, ne : ndax yor ngéen dara ? ñu ne ko : dée-déet, mu ne : kon woor naa»
  2. Jàpp, mooy bàyyi yiy dogloo moo xam lekk la mbaa naan walla séy.
  3. Jamono koor gi, maanaam bёccёg gi, mi ngi tàmbalee ci fenkug fajar gi ba ca sowug jant bi. Bu waay wooroon guddi gi, dog ci bёccёg bi, ag kooram du wér, ngir waxam ja (t.s) : «Mottalileen koor gi ba ci guddi gi»

Sunnay koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

1 – Gaaw a dog, mooy dog rekk bu jant bi sowee, ngir waxam ja (j.m) : “ nit ñi duñu dañ di nekk ciw yiw li feek ñi ngi gaaw a dog” ak waxi Anas ji (y.y.g) : “Yonnant bi (j.m) daawul julli timis ndare bu daa dog, ak doonte ci guuxub ndox la”

2 – doge ci tàndarma ju tooy mbaa ju wow, bu amul ndox, li ñu gёn sopp nag mooy mu tόol: ñatt walla juroom mbaa juroom ñaar, ngir waxi Anas doomi Maalik: “Yonnant bi (j.m) da daan doge ci tàndarma ju tooy njëkk muy julli, bu amul jёfandikoo tàndarma ju wow, bu amul mu guux ay guuxi ndox”

3 – ñaan booy dog, ndax Yonnant bi (j.m) daan na wax bu dogaan : “Allaahuma lakka sumnaa wa halaa risqika aftarnaa, fa taqabbal minna innaka antas samiihul haliimu” Ibnu Omar moom daan na wax: «Allaahuma innii asaluka birahmatikal latii wasihat kulla sayin, an taxfira sunoobii».

4 – Xëdd, mooy lekk ak naan ci waxtuw njël di mujjug guddi gi, ànd ak yéeney woor, ngir waxam ja (j.m) : "ngënéel li tàqale sunug koor ak gu waa Ahlul Kitaab (ñoñ téere: Yahood yeek Nasaraan yi) mooy xëdd” ak waxam ja (j.m) : “xëddleen, xëdd de am na barke”

5 – yeexe xëdd ba ci xaaj bu mujj bi ci guddi gi, ngir waxam ja (j,m) : “sama xeet wi duñu dañ ciw yiw li feek ñi ngi gaaw a dog tey yeex a xëdd”

Waxtuw xëdd mi ngi doore ci xaajub guddi bu mujj bi, yam ci bu fajar desee ay simili yu neew, ngir waxi Saydun Ibnu Saabit ji (y.y.g) : “ xëdd nañook Yonnant bi (j.m), bi mu noppee jug di julli ji, ma ne : diggante xëdd ak nodd lan la ci waxtu ? mu ne : lu tollook juroom fukki laaya”

ku am sikk ci fenkug fajar na lekk te naan bam u wόor ko ne fajar fenk na, bu ko defee mu jàpp (mu tàmbalee woor), ngir waxam ja (t.s) : “ lekkleel te naan ba xàmmee wёñ gu weex cig u ñuul ci fajar gi” waxees na Ibnu Abaas (y.y.g) ne ko : “man de damay xëdd, bu ma sikkee (ne warees naa jàpp) ma bàyyi. Mu ne ko : lekkal li feek yaa ngi sikk, ba sikkatoo (nga jàpp)”

Yi ñu sib ci koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sib nañu ci koor ay mbir yoy man nañoo tax ba koor gi yàqu, ak doonte ñoom ci seen jёmmi bopp duñu ko yàq, ñooy:

1 – ёppal ci gallaxndiku ak saraxndiku booy jàpp, ngir waxam ja (j.m) : “ёppalal ci gallaxndiku ndare bu dangaa woor” sibees na muy ёppal ci saraxndiku ngir ragal ndox mi di jàll bay àgg ca biiram, di yàq kooram.

2 – fόon, man naa jeqi bànneex bu man a yàq koor, ngir mànniyu mu génn mu muy waral, walla ab séy te bu boobaa kafaara day war.

3 – di xool sa soxna cib bànneex

4 – di xalaat ci mbirum séy

5 – laal jigéen ak sa loxo walla jonjook moom ci sa yaram

6 – sàqami singom ngir ragal lenn di ci jàll

7 - ñam cin mbaaw ñam

8 – gallaxndiku ci lu dul jàpp mbaa aajo laaj ko

9 – tusngalu ci njëlbéenug bёccёg gi, bonul nag ci mujj gi

10 – nàmpatal ak lu ni deme ngir ragal ag néew-doole gu man a waral ag dog

Luy yàq koor, ak lu ñu daganal ci ku woor mu def ko, ak lu ñu ko ciy jéggal

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

liy yàq koor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay mbir lañu ñooy:

1 – am yolaakon (liquide) mu àgg cib biir jaar ci bakkan,(moo xam ci paj la mbaa leneen), mu jaar ci bёt mbaa nopp niki tuuf, mu jaar ci kanamug jigéen niki pikiiru .

2 – li àgsi ci biir bi ngir ёppal gu ñu def ci galaxndiku ak saraxndiku ci njàpp ak leneen.

3 – génnug mànniyu ngir xool bu bari walla xalaat walla foon walla jonjoo

4 – waccu mu ñu tay, ngir waxam ja (j.m) : “ku waccu te tay ko, na fay” waaye nag ku am waccu not, ba mu waccu te sàkkuwu ko, loolu du yàq kooram

5 – lekk mbaa naan mbaa séy bu ñu la ci manantee (forsee)

6 – ku lekk mbaa mu naan ngir jortu ne daa nekk ci guddi gi, ginnaaw bi mu xam ne fajar fenkoon na

7 – ku lekkoon mbaa mu naan ngir yaakaaroon ne dog jotoon na te fekk booba jotutoon

8 – ku lekk mbaa mu naan ngir fàtte te àggalewul kooram nàgir jortu ne wareesul a àggale koor, ginnaaw jot nanoo lekk te naan, bu ko defee mu wéy ca dogam ga ba guddi.

9 – agsig dara lu dul aw ñam ba ci mbaq gi (biir bi) jaare ko ci gimiñ gi, muy lu mel ne wann ab jaaro walla ag wёñ, ngir li ñu jёle ci Ibnu Abaas mu ne : “ koor mooy li dugg, du li génn” mu bёgg a wax (y.y.g) ne: koor mi ngi yaqoo ci liy dugg ci biiru nit ki, waaye du yàqoo ci li ciy génne niki dereet walla am waccu.

10 murtad (mooy tubbi) ak doonte dellusiwaat na ci Lislaam, ngir waxam ja (t,s) boo bokkaalee sa jёf dana sippiku te danga bokk ci ñu ñàkk ñi (ñu pert ñi)

Yii yépp dañuy yàq koor tey waral fayug bis ba ca yàqoo, waaye nag duñu waral kafaara, ndaxte kafaara moom du ware ndare ci ñaari way yàq koor yii:

1 – séy bu ñu tay te kenn manantewu la ci, ngir waxi Abuu Hurayra ja (y.y.g) : “waay ñëw na ci Yonnant bi (j.m), ne ko man de alku naa yaw Yonnantub Yàlla bi, mu ne ko : lu la alag ? mu ne ko séy naak sama soxna ci ramadaan. Mu ne ko : ndax am nga jaam boo goreel? Mu ne deedeet, mu ne ko ndax man ngaa woor ñaari weer yu toftaloo? Mu ne ko deedeet, mu ne ko ndax am nga lu man a leel juroom benn fukki miskiin ? mu ne ko deedeet, daal di toog, Yonnant bi (j.m) daal di indi as ndàmba su def tàndar ma, ne ko am saraxeel lii, mu ne ko ndax dama koy sarax ku ma gёn a ñàkk? Yonnant bi ree ba ñuy gis bёñam ya, mu ne : demal jox ko sa ñoñ”

2 – lekk mbaa naan ci lu dul ngant lu ñu daganal: ci Aboo Haniifa ak Maalik (y.y.g), seenub tegtal mooy : “waay dog na ci ramadaan Yonnant bi (j.m) digal ko mu kafaara” ak àddiisu Aboo Hurayrat (y.y.g) mu ne : “waay ñëw na ci Yonnant bi (j.m) ne ko : dog naa ci ramadaan te tay ko, Yonnant bi ne ko: goreelal ab jaam, mbaa nga woor ñaari weer yu toftaloo, mbaa nga leel juroom benn fukki miskiin”

li ñu daganal ci ku woor

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daganal nanu ci ko woor ay mbir ñooy :

1 – soccu diirub bёccёg bi, waaye Imaam Ahmad moom da koo sib bu digg-bёccёg bi jàllee

2 – serlu cim ndox mu sedd ngir tàngoor wu tar wi, moo xam da koy sotti ciw yaramam walla da ciy nuur

3 – lekk ak naan ak séy guddi, ba fajar fenk

4 – tukki ngir aajo ju dagan, ak doonte xam na ne tukkeem bi dana tax mu dog

5 – faju ci lepp lu dagan, bu fekkee ne dara du ca jàll ba ca mbàq ga, man naa jёfandikoo pikiir sax bu dul buy joxe aw ñam

6 – sàqamil aw ñam ag gone gu ndaw gu amul ku ko sàqamil aw ñamam wi mu manul a ñàkk, waaye ci sartub lenn bañ cee jàll ba ca mbàq ga.

7 – cuuraayu ak gёttu (xeeñu latkoloñ), loolu nag li ko waral di ñàkk a gis lu koy tere lu juge ci aji yoonal ji (di Yonnant bi (j.m))

li ñu jéggale

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kuy woor jéggal nanu ko ay mbir ñooy:

1 – wann ay lor (tuflit) ak doonte bari na, maanaam lori boppam nag waxunu lori keneen

2 – am waccu mu la not, bu ca dara delluwul ba ca mbàq ga, ginnaaw bi mu génnee ba ci catu làmmiñ wi

3 – wann aw weñ te tayoo ko

4 – pёndub yoon walla bub liggeeyukaay, ak saxaarus matt, ak mbooleem saxaar yi nga manul a moytu

5 – xёy ànd ak janaba (war a sangu farata ngir jaxasoo goo defoon ak sa soxna) ak doonte dangaa yendook moom bёccёg bépp tam.

6 – gént, dara warul ku gént fekk mu woor, ngir ab àddis: “yekkatees na xalima gi wёlif ñatt, ab dof ba kero muy xiqi (juge ci dof gi), kuy nelaw ba kero muy yewwu, gone ba kero muy gént (muy doon mukallaf)”

7 – lekk mbaa naan ngir juum mbaa fàtte, waaye Maalik moom gis na ne war naa fay bu dee koorug farata, ngir léemtu (ngir lu gёn a wόor), bu dee naafila nag moom fay du ko ci war mukk, ngir waxam ja (j.m) : “ku fàtte ba lekk mbaa mu naan cig koor, na mottali kooram, ndax Yàlla’a ko leel, nàndal ko” ak waxam ja (j.m) : “ku dog ci ramadaan ngir ag fàtte, du fay te du kafaara”

Fukkeelu ne-ne bi : ci leeral luy kafaara ak lan mooy njariñ li :

Kafaara mooy li ñuy fare ab bàkkaar bu ñu def ngir ñàkk a topp ndigali Aji yoonal ji (Yonnant bi), ku wuuteek aji yoonal ji ba jaxasoo ci bёccёgu ramadaan mbaa mu lekk mbaa mu naan cig tay, war na mu kafaara wuute gii mu def, loolu nag benn lay doon ci ñatt yii: goreel jaam bu dib jullit, walla woor ñaari weer yu toftaloo, walla leel juroom benn fukki miskiin, miskiin bu nekk mudd ci dugubi suuna mbaa ceeb walla tàndarma kem ni nga ko mane, ngir li nga gisoon ci addiisub waa ji séyoon ak soxnaam ci koor, daal di laaj Yonnant bi (j.m). Kafaara nag dina limu ci limug wuute yi, ku jaxasook soxnaam cib bis, naan mbaa mu lekk ca bis ba ca des, ñaari kafaara war na ko.

njariñul kafaara

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Njariñ li nekk ci kafaara mooy ñogal sariiya ba duñu ko foye, di xotti wormaam. Moom itam day laabal bakkanub jullit bi ci jeexiiti bàkkaari wuuteek ndigali Yonnant bi (j.m), yi ñu def ci lu dul ngànt, looloo tax ñu war a defe kafaara ni ñu ko yoonale ci kem bi ak naka gi (ni muy tollu ak ni nu koy defe), bu ko defee mu man moom kafaara def li ko taxoon a jug, muy far bàkkaar bi aki jeexiitam ci bakkanu jullit bi. Cosaanul kafaara mooy waxi Yàlla ji (t.s): "yu rafet yi danañu demal (dañal) yu ñaaw yi" ak waxi Yonnant bi (j.m) : “ragalal Yàlla foo man a nekk, lu ñaaw (loo man a def) toppal ca lu rafet, dana ko far, àndal ak nit ñi ci jikko ju rafet”