Wommatiinu mbëj
Apparence
Wommatiinu mbëj walla Wommatiin wi moo nuy wax ci anam gi wommat wu mbëj wi di amee. Ci limam lanuy sukkandiku ngir man a xam ñaata la benn jumtukaay bi manee wommat mbëj. Safaanam di dëgërluwiinu mbëj wi di li lay wax ni ab jumtukaay manee dëggërlu jàllug dawaanu mbëj ci biiram.
Tekkeem
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bennaanu nattu wommatiin wi mooy siemens ci meetar [s/m]. Nekk itam dawaanu mbëj ci kaw taraayu ab toolu mbëj [I/E]. lu bari bile araf lañu koy teewalee .
- mooy Wommatiin wi
- ρ mooy dëgërluwiin wi (ñu koy natte ohm* meetar)
- R ndëgërlu gu mbëj gu ab wommatukaay (ñu koy natte ohm)
- l mooy guddaayu wommatukaay bi (ñu koy natte meetar)
- A mooy dijjaayu wommatukaay bi (ñu koy natte meetar kaare)