Aller au contenu

Wëttéen

Jóge Wikipedia.

Wëttéen garab gu ndaw lay doon mi ngi bokk ci njabootug Malvacées

Wëtteen gi (Gossypium hirsutum)

Wëttéen garab la gog day màgg sax ci yenn gox yi nga xam ne day am naaj te suuf si xaw a wow.

"Wëttéen" garabu ñax la gog man naa dund ay 10i at. Guddaayam dees koy natt ci 10i met waaye buñu koy bay dañ koy gàttal ci ñaari met ngir yombal jël giñuy jël Wëtteen wi.

Tóor-tóoram dañuy génn ci ñaari pàcc, gog day weex ak pàcci gog day mboq te yor genn xet bees ràññeef lool.

Ci noonu ci lay amee lu mel ni mbaxana bob day dëgër, bob day màgg daa di ubbeeku daa di bàyyi doomi wëtteen yi ñu génn ci doom yooyu ci la fiibar bi di génnee nga xam ne moom lañuy jëfandikoo.

Te wëttéen yi bari nañ lool waaye bi ci ëpp liñuy jëfandikoo mooy bi ñuy woowe Gossyium hirsutum

Ngir bay Wëttéen danuy soxlawoo ab diir bu xaw a yàgg. Fu bari naaj, dees na jàpp diir bi ci 520i fan yoo xam ne danu koy suuxat ngir màggal ko ba noppi nga as ndiir ngir mu wow, as sos doo ko nàndal ngir may Wëttéen wi mu xaw a wow.

Garab la gog dees koy bay ci mbayum nawet ci Afrig, ak End, ak Amerig.

Garab la gog ay at a ngii ñu koy jëfandikoo ngir di ci de far ay yéere yu nooy.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gossypium hirsutum