Melosuuf
Xamale Melosuuf
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Melosuuf mooy xam-xam biy settantal ak a leeral feeñtey yaram yi walla jëmm yi ak yu dundat yi a yu nit ñi ci kaw suuf si ak gëstu gi aju ci ni ñu séddalikoo.
Li muy wund ak li mu doon
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Séwogaraafi baatub gereg la, boo ko doon firi ci wolof muy “melal suuf si”, maanaam wax ni mu mel, ni mu nekke.Moom nag baat la bu tukkee ci (Geographica): baatub gereg bob cosaanam mooy (Geography),muy ñaari baat yu ñu boole ñuy benn bu njëkk bi mooy tekki melo, walla nataal (Graphica), ñaareel bi di Geo di tekki suuf.
Bu nu sukkandikoo ci loolu danu naan Sewograafi walla Geographia mooy “melal suuf si” walla wax ni mu mel, xam-xam bii noonu la tàmblee woon, ndax ca njëlbéen ga, tukkikat yi daa wër di gëstu dañu daa bind li ñu gis ci dëkk yi nu romb ak gox yi ak diiwaan yi ñu siyaare, leeral, melal ni ñu leen gise, fekke leen ni. Sewogaraafi nag déggoo nanu ci séddale ko ay xaaj ñooy yii: Séwogaraafi bu dénd bi (nature), mooy biy sonn ci gëstu ni suuf si mel, ni mu bindoo ci wàllug jiyoloji, ak feeñte (fenomene)yu jawwu yi ak gàncax yeek dundat (animal) gu dénd geeg gu jeeri ji. Bokk na ci xaaj yooyu Séwogaraafi bu bidiw, li ko tax a jug di: jàng ni suuf si bindoo ak ab kemam, ni muy yëngoo, ak ni mu buloo ak séqoo gi mu am ak yeneen bidiw yi. Bokk na ci xaaj yi ba tay, Séwograafi bu nit: moom nag daa séddaliku ci :Séwogaraafi bu way dëkk yi (abitant), ak séwogaraafi bu koom koom ak bu politig, mooy gëstu ci goxi àdduna bi aki pegam (frontiere) yu politig, aki jafe-jafeem ak ña fa dëkk. Ak bu nataal yi walla bu lonkoyoon yi: moom mooy xam-xam biy yittewoo lonkoyoon sewogaraafi yi ak ni nu leen di sose. Bu yàggul bànqaas bu yees sosu na ci xam-xamu Sewogaraafi, mooy biy nos xam-xam yu sewogaraafi yi ak yëglu cig sori
Njariñul xam-xamu melosuuf
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Melosuuf moom nekkatul rekk xam-xam boobu di melal feeñte yi (les phenomenes) di leen melal ak a leeral ci anam gu tond, gu soreek li am, waaye mujj na di xam-xam bi jagoo dox ànd ak jëm-kanamug xam-xam bu bees bii sukkandiku ci gëstu ak nattale, ak làmb ba daj, ak jëfandikoo misaal yi ak gis-gis yu yees yi, ci noonu la mujje di lu nuy doxal ci anam gi nuy tudde séwogaraafi bu kem ak séwogaraafi bu doxal walla dëppale “bu pratique” bi nga xam ne du nangoo beru wëliif soxlay nit yu mag yi, loolu nag li ko waral mooy li séwogaraafi làmbool yor ko ci man–manu dëppoo ak mbooleem xam–xam yi, moom mooy aji jokkale ji nekk ci diggante xam–xam yi di leen booleek a jokkale, bu ko defee di leen tàggat ngir ñu liggéeyal ko, di jël ci ñoom lu koy jariñ, di ko ràññale ak yeneen yi. At yu mujj yii seere nanu ag soppiku gu mag ci gérum séwogaraafi ak xam-xam bi mu ëmb, ak ci anam yi muy jaar ngir amal ay jubluwaayam aki xemmemtéefam. Man naa am nag mu bokk ci li indi coppiku gii: jëm gi nit ñi gën a jëm kanam, nga xam ne sax boroom xam-xami séogaraaf yi mujj nanu di gëstu ay mbir yoy bu njëkk xamuñu leen woon, ba sax kuy seetlu liggéeyu boroom xam-xam yii dana gendiku yittewoo gu dolliku gi nu sotti ci mbirum gëstu feeñte yi /phenomenes/ ak masala yu wuute yi aju ci dénd bi ak nit, ci anam gu wuuteek ga nu ko daa gëstoo bu njëkk, sababus loolu nag mooy jëfandikoo gi nuy jëfandikoo leegi ay jumtukaay yu xarañ te aaytal ci seeni gëstu, di dimbadikoo xam-xami takk yi (statistiques) ak yu xibaar yu jumtukaay yi ak mat ak misaalukaay yi (echantillon) ak xam-xamu xarala ak dénd (nature bi) ak kimya (simi). Jëm kanam gii am nag ci jëfandikoo jumtukaay yii ak ker-keraan yii (ces moyens) tax na ba ngérte (resultants) yu am solo juddoo ci, yu jañ séwogaraafi mu jëm kanam, def ko muy xam-xam bu jamonoo. Loolu sax tax na ba ñenn ñi di woowe jëm kanam gii am ci xamu melosuuf ((jeqiku walla fipp gu kemu ci xam-xamu séwogaraafi)), Jeqiku gii walla fipp gii waa melosuuf yi teeru nanu ko te màggal ko, ndax ngérum kem ay ngënéelam lu bari la, man naa am li ëpp solo ci ngënéel yooyu mooy ngérte yi mu lay àggale yépp ñooy gën a sew, gën a am maanaa, ngir seggat (analyse) gu xam-xam gi muy amal ñeel toftaloog mbir yi. Ceggat gu xam-xam gu melosuuf gii mooy wone noste (systeme) yi amal ay jeexiital ci amug feeñte yu wuute yi melosuuf di gëstu. Moom du doylu ci leeral feeñte yi rekk waaye day sukkandiku ci sabab yi sos feeñte yii.
Ëttub gëstu gu melosuuf
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngir melosuuf man a génne, feeñal lëj-lëj ak jafe-jafe yi gawu cib gox walla ab diiwaan, li muy njëkk a def mooy digal ëtt boobu walla barab boobu , maanaam wutal ko aw dig ba ñu xam ne fii la, bu ko defee mu fésal séqoo (les relations) yi am ci diggante mbooleem xeet (element) yu wuute yu kojug dénd yi (naturel) ak yu kojug nit yi, ak nu ñu man a duggantee ci seen biir, ràbbaloo ni. Looloo tax séwogaraafi fi di boroom jikoo ju ràññiku, ndax danu koy gis mu tegub tànk ci xam-xami dénd yi, tegati beneen ci yu nit yi. Bu fekkee ne xam-xam yu wuute yi ci atum 1972 lanu leen raŋale, nos leen, séddale leen ñatti kuréel ñooy : xam-xami seggat yu nattu yi, xam-xami firi yi ak taawiil, ak xam-xami jam yi (yu critique yi), bu fekkee ne noonu la it melosuuf moom jël na mbooleem jikkoy yii kuréeli xam-xam . Jàng ëttub melosuuf dina feddali amug ay way nekk yu bari yu dénd ak yu nit yu lënkaloo yuy ràññikoo ci jëflante yu bari yuy am ci diggante way nekk yii, loolu moo lay won foofu solos boroom xam-xamu melosuuf, looloo tax nga gis gëstu ëttub melosuuf du yam rekk ci menn mbir walla benn feeñte bàyyi ya ca des, ak doonte ëttub melosuuf làmboo na mbooleem feeñte yépp, teewul gëstug feeñte yii day am cig beru tey natt tolluwaayu jëflante gii seggat ko, yillaal ko , ci lu dul muy sàggane benn xeet (element) ci xeeti ëtt bi. Ngir solos ëttub melosuuf Unesco saxal na ni nu koy jàngalee ci Tugal ci donga yiy door a dal, bu ko defee ñuy def aw doxaliinam ; sukkandiku ci dégg te xam juroomi laaj loolu nag mooy : ëtt biy jóox (biy produire) : bu ñu laajee njàggaan li jéego yi aju ci déggiinu ëtt biy jóox loolu man naa doon yoon wi ngir xam dëgg gi maanaam yewwu ci ne ëtt boo gis du lu dul melo ci meloy yëngu yi (maanaam mi ngi ci melow jóox) kon nag ngértel saxal yu tukkee ci nit ñi la (jeexiitalu jëfi nit)
Lonkoyoonu adduna bi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Boo gëstoo lonkoyoon (carte) adduna bi bu baax di nga ca gis dëgg yii :
- Kaw kol-kolub suuf si mi ngi ame ci jéeri ji ak ndox mi, bu ko defee jéeri ji yóbb ci benn ñeenteel, maanaam bu doon ñeenti xaaj la benn bi, ndox mi moom yóbb ci ñatti ñeenteel .
- Jéeri nag mi ngi ame ci juroom benni gox walla kontinã ( ci lu dul goxub dott (pole) bu bëj-saalum bi nga xam ne kenn dëkkewu ko ngir jawwu ak dénd bu méngoodi ba), juroom benni gox yii danu leen a toftale kem ni nu yaatoo :
1 – Goxub Asi : moo ëpp ci gox yi, ab tolluwaayam toll ci benn ñaareel 44 milyoŋi kilomet yu kaare , way-dëkk ya tollu ci 2200 milyoŋ ciy nit.
2 – Goxub Afrig : ab tolluwaayam di benn ñeenteel 30 milyoŋ ciy kilomet yu kaare , way-dëkk ya tollu ci 350 milyoŋ ciy nit.
3 – Goxub Amerig gu bëj-gànnaar gi: ab tolluwaayam tollu ci benn ñeenteel 24 milyoŋi kilomet yu kaare, way-dëkk ya tollu ci 270 milyoŋi nit.
4 – Goxub Amerig gu bëj-saalum gi: tolluwaayam toolu ci ñatti ñeenteel 17 milyoŋi kilomet kaare, way-dëkk ya tollu ci 300 milyoŋi nit.
5 - Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj-saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits ( longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu.
5 – Goxub Tugal ab tolluwaayam tollu ci benn ñaareel 10 milyoŋi kilomet yu kaare, way dëkk ya tollu ci 750 milyoŋ ciy nit.
6 – Goxub Ostraali : ab tolluwaayam tollu ci ñatti ñeenteel 7 milyoŋi kilomet kaare , way dëkk ya tollu ci 15 milyoŋi nit.
- Ndox yi nekk ci kaw kol-kol bi (globe) ñi ngi ame ci mbàmbulaan yi : ñoom ay diggante yu rëy lañu yu ndox, ak ci géej yi : ñoom ay diggante yu gën a ndaw lañu yu ndox . Bokk na ci mbàmbulaan yi : màmbulaan gu dal gi (moo ci gën a rëy) ak gu atlas, ak mbàmbulaan gu end gi ak gu bëj-saalum gi ak gu dott bu bëj-gànnaar bi(pole nord). Bokk na ci géej yi :géej gu diggu gi (mediteranee) gu xonq gi , gu araab gi, gu ñuul gi añs .
- Adduna ju njëkk ja walla ju yàgg ja – moom mi ngi ci xaaj bu penku bu kol-kol bi – mi ngi ame ci ñatti gox yu taqaloo, daal di sos nag benn dank (bloc) walla jóor, ñatti gox yii ñooy : Asi, Afrig ak Tugal, dara taqalewu leen lu dul yenn ci ay feeñte yu dénd yu néew : niki géej yu xat yi ak càllalay doj yi ak tund yu yaatoodi yu néew yi ag yékkatiku.
- Nit dundal na goxi adduna ju yàgg ja la ko dale ca ba mu tegee tànkam ci kaw suuf rekk, bu ko defee ay xay (civilisation) yu mbay, yu kawe, yu yàgg daal di am ci xuri ay dexam yu naat ya, lu ci mel ne xay ya amoon ca xuri dexug Niil ga nekk Isipt ak dexug Dijla ga ak Furaat ca Iraag ak dexug Sand ak Gangas ca End ak dexug Sigyang ak Yangci ca Siin.
- Adduna ju yees ji – moom mi ngi ci xaaj bu sowwu bu kol-kol bi – mi ngi ame ci Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Amerig gu bëj-saalum gi, ñoom ñaar ñooy ñaari gox yi nga xam ne bi leen nit wuñee (decouvrir) ak leegi ay xarnu (siecle) rekk la, la ëpp ca ña fa dëkke ay waa Tugal lañu yu gàddaaye Tugal dëkksi fa, moom Tugal nag benn la ci goxi adduna ju yàgg ji .
- Goxub Ostraali –moom moo gën a tuuti ci gox yi, te gën a rëy ci duni adduna bi- mi ngi nekk ci xaajub kol-kol bu bëj-saalum bi, ca bëj-saalum gu penku gu dankub adduna ju yàgg ja.
- Mbàmbulaan gu dal gi moo dox ci diggante ñaari gox yii di Asi ak Ostraali cig wàll, ak ñaari gox yii di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi ci geneen wàll, bu ko defee mbàmbulaan gu atlas moom dox ci diggante ñaari gox yii di Tugal ak Afrig ak ñaar yee di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi , bu ko defee mbàmbulaan gu end gi tàqale ñaari gox yii di Aseek Afrig wëlif goxub Ostraali, mbàmbulaanug bëj-saalum gi tàqale mbooleem gox yi wëlif goxub dott bu bëj-saalum bi
- Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits ( longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu.
Xam-xam | ||||
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma | ||||
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal | ||||
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama |